JazbulMajzoob

Embed Size (px)

Citation preview

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    1/44

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    2/44

    Jazbul MajzobSeex Abdul Kariim Samba Jaara Mbay

    (1868 - 1917)

    1436 h / 2014 - www.drouss.org

    Tous droits de reproduction rservs, sauf pour distribution

    gratuite sans rien modifer du texte.

    Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez

    nous contacter par le biais de notre site internet :

    www.drouss.org

    http://www.drouss.org/http://www.drouss.org/http://www.drouss.org/http://www.drouss.org/
  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    3/442- Jazbul Majzob

    Apercu sur lauteur

    N en 1868 et ls de Ahmadou et de Soxna Ndack Kane, Cheikh SambaDiarra est lun des disciples de Serigne Touba qui habitaient Saint Louis.

    Originaire de KOKI, il ft lun des potes les plus fascinants dans luniverswolof, ci rewi wolof. Il faisait part de ces saints dicilement reprables ;car il vivait dans la masse, comme tout le monde ; et allait mme vendreau march.

    En allant faire allgeance Cheikhoul Xadym, Cheikh Samba Diarrarejoignait son frre aine Cheikh Sadiaye, Ndiarme. Contrairement ce que plus dun raconte sur son allgeance, il na jamais t un griot

    qui baait des tam-tam. Cheikh Samba Diarra ft un minent rudit quimmorisa le coran son bas ge ; plutard il quia Koki pour rallier la villede Saint-Louis an dy tudier les sciences religieuses.

    Son travail a contribu diuser les enseignements de Cheikh AhmadouBamba parmi les masses wolof.

    Tantt sur ses pomes, il fait des inserons de mots arabes, des phraseset des prires, y compris dans les ouvertures et fermetures. Il a composde nombreux pomes, y compris les louanges ddie Cheikh AhmadouBamba et sa contribuon au Sngal, ses miracles en Mauritanie, et lesqualits de Cheikh Ibra Fall.

    Parmis ses oeuvres poques, Jazbul Majzoob (larance du majzb[lar]) reste le plus populaire.

    Il est aussi un proche parent de Serigne Mor Kayr (1869-1951), un autreminent spcialiste wolofal mouride. Tous deux vivaient ensemble enMauritanie et rendaient visite leur matre, Cheikh Ahmadou Bamba,

    qui y fut exil par ladministraon coloniale franaise de 1903 1907.

    Un jour lors dune de ses promenades au bord du euve Sngal, il croisades jeunes demoiselles dune beaut indescripble. Il leur demandalobjet de leur prsence sur les lieux. Elles rpondirent quelles ont tenvoyes pour venir accueillir un de leur seigneur un talib de SerigneTouba du nom de Cheikh Samba Diarra Mbaye. Il retourna chez lui enabandonnant ses chaussures sur place. Quelques temps aprs il quiace monde. Avant de parr il crit :

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    4/44Jazbul Majzob - 3

    ku sdduwul man sddu naa,ku fadduwul, man faddu naa,Ba matlu, wsu naa dansa,Yalla ak sa bark, maa la gm.

    Quelques temps aprs ces vers, Serigne Samba Diarra Mbaye ft rappel Dieu, en 1917. Son mausole se trouve au cimere de Thim, Saint-Louis du Sngal.

    Il na eu que trois (3) enfants savoir :

    - Fama Zahra Mbaye

    - El Hadj Mbacke Mbaye

    - Mouhammadou Moustapha Mbaye

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    5/444- Jazbul Majzob

    Indicatons

    Wolof Franais

    e= per pr

    u= ou rus rous

    c= th caam thiam

    = gn am gnam

    x= kh xol khol

    j= dj jibi djibi

    nj= nd njaay ndiaye

    nd= nd nday ndeye

    aam (machoire)

    = eu gm = geum

    = (plus dur) = rr perdu

    o= au gor gaure

    q= xx suqali soukh khaliii - uu - oo - aa ee (rer sur le son) ;Ex : biir - suur -xool - gaal - xeer

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    6/44Jazbul Majzob - 5

    Bismi-l-Laahi-r-Rahmaani-r-Rahiimi

    AI xamdu Iil-laahi, kimayXamal bu wr, ta dima mayXewl, Ci barkeb kimu xy,Jbbal lu dooni xewlam.

    Yen gaayi diine jegeleen

    Ma jegeleen te dolli leen,Xam-xam bu wr te jafe leen,Ma fecci tay ay fas-fasam.

    Koo xam ni xam na Iii,na xam,Ku ko xamul, ma wax mu xam,Xamlug xamul, day taxa xam,Xamlu ku xam ,day dolli xam.

    Te Iii ma leen di bgg a wax,Day dggi xol, dggali wax,

    Jagali jf, te ku ko wax,Jariu i, ak fa nu jm.

    Masuma leen a waxi neen,Te lii ma wax, du waxi neen,

    Lii woyu xudbu la, du neen,Yu dee woy u dul kemam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    7/446- Jazbul Majzob

    Naa sant ylla mi ma may,Xudbu bu mat, mu dima may,Di fey ay, di dqi moy,Ci leeri mbo ragalam.

    Dima gisal luma gisul,Dima ygal luma ygul,Dima xamal luma xamul,Ci duusi geji xam-xamam.

    Dima amal luma amuI,Dima wutal, dima waul,Dima digal, dima tamal,Nangoo yamooki ndigalam.

    Dima yrm, dima faI,Dima jari, dima teral,Def ma ma mel ni ku nu fal,Ku tbbi peyi ngrmam,

    Dima dugal fu may musal,Dima fegal lu ma ragal,Ku jm ci man aki fetal,Mu boole diigali walam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    8/44Jazbul Majzob - 7

    Dima setal ci waxi ba,Ba ku ma yene j ba,Mu ni ko tf, mu ni sulu,Daanu, di toppal fetalam.

    Dima xccal, dima jaal,Dima tyyill, dima tayaI,Dima ubbil bun xewl,Fatma ci biir roqi oam,

    Ne ma ykkt, newuma tuy,Wan ma boppam, ma di ko woy,Ta di ko ka, mu di ma may,Ne ma yoxoos ci biir xolam.

    Di ma fegaI pexe mu naaw,Di ma teral ren aki daaw,Di ma teral sama gannaaw,Di ma teral sama kanam.

    Dib suruse bimay fajal,Di garabal lima ragal,Di ma flal lumay sonal ,Mu teggi, teg, yenu jem.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    9/448- Jazbul Majzob

    Dima toggal, dima yakkal,Dima rccal, di ma sefal,Dima bbal, di ma leyal,Tib yu u barkeelug wannam.

    Di ma bgaI, di ma seraI,Dima xjjal, di ma dalal,Dima moyuI, di ma fayuI,Kenn du ma yab kanamam.

    Bu ma yewwee, kenn du ma yab,Fu ma jm, du ma ayib,Sama gannaaw sama ayib,Xanaa nammeel gu u ma namm.

    Sama o it du u ayib,Man aki oom du u layib,Sri bi moo dajale ypp,Beral nu cr bu u grm,

    Limu ma may ma di ko am,Moo ma ko may ma di ko am.Limu ma wax ma di ko xam,Moo ma ko wax ma di ko xam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    10/44Jazbul Majzob - 9

    Limu ma wan ma di ko gis,Moo ma ko wan ma di ko gis.Ta ku ko gis, ni ku ko gis,Ni ku ko xam, ni ku ko am.

    May na ma lool, danaa ko wax,May na ma lool, duma ko wax,May na ma lool, man mi ko wax,Ak ba ko ooni kee fa yam.

    Man Samba Jaara, maa grmSamab sri, danaa xoromWay wi ma way ci waa kram,oo am ngrm, oo am xorom.

    Bu sg sggee ba u wral,Li tax ma jg di ko biral,Werante de, kon nag yralSeeni jaloore ca kanam.

    Jsbul xulob bi dafa jib,Bii jsbu jg xee famu jub-Lu, ku ko xee na wut a jub,Wy na xameeful fu mu jm.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    11/4410- Jazbul Majzob

    Jsbul xuloob bi dafa daw,Bii jsbu jg, xee fa mu aw,Ta ku ko dab na daw a daw,Raw na xameeful fu mu yam.

    Lu jiitu Iii dafa dawal,a daa rawanteeg a dawal,Naka fxl raw ba ggal,Akk am wa kenn gisul pndam.

    Ma daldi jg, tofal ko biijsbu, di woy ki woy Nabi,Di ko ko Fayna woy Nabi,Ma di ko woy ba fa nu jm.

    Kemub liuy dox di ko woy,Fayante la ak moom ki mu woy,Dakoo grm ba di ko ma ,Lammi yi daldi ko grm,

    Ma far jafal man di ko woy,Di barkeeloog a di ko royCi woy, ba daane ku ko woy,Ak ku woyul u ne wedam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    12/44Jazbul Majzob - 11

    Lu ma wax ak lu ma waxul ,Wuute gi fs na, nbbuwul,Ta ba tay danaa fsalLu doy a xam ci ay woyam.

    Danaa xamaI, xamul mu xam,Xamal ku xam, mu gn a xam,Ku bgg a gis ta bgg a xam,Na dglu, xippi ay btam.

    Kenn du werante Ii ma wax,Way xam ya, xam na sama wax,Seri bii moo may sa, ma wax,Moo tax ma saf ko ci xolam.

    Bulen ma yem, yemleen ko, ndaxDu man di wax, mooy ka di wax,Waxande laa wu tjii wax,Bu ma jjee may lammiam.

    Wlliyu day feeu, ta kumFeeu ci yaw, nga daldi xam,Bu nee waxal, nga wax u xam,Way xam ya ,seede daaldi gm.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    13/4412- Jazbul Majzob

    Bu fekkee moo feeu ci man,u naa ma yaw, booba du man,Moom,ka di moom, moo di man.Ma di moom, muy ki xam.

    Moo tax ma wax ku dglu liiNa xam ni yii uy wax du lii,Waaraate jowuma si lii,Seri bi may na ma boppam.

    Kaawteefug yonent la gu des,Te ag wyam dara du des,Lu doon kiraama yu des,Dana ko ybbaale u dem.

    Sri bi muxjisaat la, moom,Man nak kiraama laa, ci moom,Ku weddi lii, na dem fa moom,Laaj ko, mu teqalem ljam.

    Moo tax li may wax moo ko moom,Msuma ko jaawale moom,Tudd turam doy na ma koom,Ta mooy seral sama yaram.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    14/44Jazbul Majzob - 13

    Bind turam may na ma xel,Tudd turam may na ma xol,Siirub turam may na ma lool,Du ma ko wax, xol a ko xam.

    Danaa biral tuu, ci ayMayam ci man, yu u ma may,Te yile may, ku u ko may,War nay grm diirug dundam.

    Buur yllamay na ma ci moom,Gm, ak xam, ak lafu ci moom,Ma jg ne naa taasu ci moom,Di ko beral woyi ngrm.

    May na ma lool, deefuma ax,Wan na ma lool, deefuma nax,Naxma kenn, kenn duma nax,Sama ngrm rawnag xalam.

    Xam naa ndigl, xam naa ndugl,Tinaa ndigl ,t naa ndugl,Damay digl duma dugl,Sama mbt, aw ndiglam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    15/4414- Jazbul Majzob

    Ki lay digl, ta du la jay,Ki lay dugl, ta di la jay,Boo xelluwul, defoo ku way,Rccooki jooy fee sa kanam.

    Ku may digl, dafay taxaw,Ku may dugl, dafay taxaw,Ta naa awal, i bu aw,Ki ma giseel a mat a xam

    Lu ne ci Iii, ma ni ko jkk,Lu ne ci lee, ma ni ko jkk,Xam la jagul, ee ak la jag,Ki ma giseel a mat a am.

    Wan na ma lool, yee na ma jar,Ba ma ree dgg aki nar,Jar ma kenn, kenn duma jar,Ki ma giseel a mat a xam.

    Wan na ma lol, dindi na sikkCi sama xol, ba duma sikk,Duma ragal lu ki ma skkKi ma giseel a mat a am.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    16/44Jazbul Majzob - 15

    Feesal na xol bi, ba du xam,Lu doy a yem ci Ii mu xam,Lu ki nga xam ni moom la xamKi ma giseel a mat a am.

    Feesal na bt bi ba du gis,Lu doy a yem ci Ii mu gis,Lu ki nga xam ni moom la gis,Ki ma giseel a mat a am.

    Doylul na xol bi, ba du raf,Jm ci leneen lu lu ko saf,Ci biir malaanam lama laf,Ki ma giseel a mat a xam.

    Gnne na rer ci sama xol,Dugal na riir ci sama xel,Kenn duma yeer di saaxal,Ki ma giseel a mat a am.

    Kenn du ma wootal di ma ir,Kenn du ma yab, ba di ma ir,Mi ma andal, ta dafa ir,Ki ma giseel a mat a xam

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    17/4416- Jazbul Majzob

    May na ma xam-xam, ba ma xam,Xot-xo xam-xam yu ma xamCi moom, ba jaaxal ku ma xam,Ki ma giseel a mat a am.

    Dolli na am-am bu ma am,Dolli na xam-xam bu ma xam,Leeral na mbooleem Ii ma xam,Ki ma giseel a mat a xam.

    J wilaaya la ma wan,Dindi la woon wccag a woon,Def leneen di ma ko wan,Ki ma giseel a mat a am.

    May na ma woluu ki ma moom,Xiir ma ci moom gi mu moom,Biral ma moom gi mu ma moom,Ki ma giseel a mat a xam.

    Biral ma sa-sa bi mu sa,Bitegi biir moo ko sa,Ta kenn du sa Ii mu sa,Ki ma giseel a mat a am.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    18/44Jazbul Majzob - 17

    Biral ma saayiir sa, bu wr,Biral ma baan ba, bu wr,Ne ma lu dul lii, du lu wr,Ki ma giseel a mat a xam.

    Ne ma ykket yor ci loxoom,Di ma xamal lu diy soloom,Di baay ci baan, ma di doom,Ki ma gseel a mat a am.

    Jiitu ma nd ak man di wy,Lu may gagal mu ni ko tuy,Ba man ma waaru ba ni cy,Ki ma giseel a mat a xam.

    Di ma digl, ta du ma jay,Fu ma taxaw, mu di ma xy,Ta di ma gontu, di ma may,Ki ma giseel a mat a am

    Nee ooki, nee na, lani cas,Bul ma biir ba ba ma gis,Raeel ma mboot yi, ba mu fs,Ki ma giseel a mat a xam

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    19/4418- Jazbul Majzob

    Ni dgg a ngii dgg a gnFen du taxaw, tag fenn,Ku jm pey ,du yori fen,Ki ma giseel a mat a am.

    Lisaani aal lamiy waxam,Lay snni xol bi, ba ma xam ,Fu ma tollu di ko xam,Ki ma giseel a mat a xam.

    Moom ka di moom, xam na ma xam,Lu diy mbiram laa jkk a xam,Boobee ba tay, ma di ko xam,Ki ma giseel a mat a xam.

    Lewoo na ma ak moom cig cofeel,Di ko mbt ba may xaleel,Mu daal di may fab yobbu teel,Ki ma giseel a mat a am.

    Tegtal ma yoonu njariam,Ubbil ma bun xewlam,Burxal ma mbo ngrmam,Ki ma giseel a mat a xam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    20/44Jazbul Majzob - 19

    Yee na ma jar, ba ma ni jar,Fegal ma kor, smmal ma ngor,Fayal ma mer, fajal ma mar,Ki ma giseel a mat a am.

    Di ma defar, ta di ma far,Ta ku ma far, mu di ko far,Ta lu ma far, daal di ko far,Kima giseel a mat a xam.

    Di ma taxawu, ma taxaw,Buma taxawul, mu taxaw,Teeweel ma xew, luy mn a xew,Kima giseel a mat a am.

    Ku jm man di ma ljal,Mu boolekoog lu kay ljal,Lu gn mu fab jox ma, ma jl,Kima giseel a mat a xam

    Lu ma ragal mu ni ko casSnni, ba dootu ma ko gis,Mbaa mu labal ko, mu ni mes,Kima giseel a mat a am.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    21/4420- Jazbul Majzob

    Biri dun bi, ba ma gisNi muy naxee, ta ku ko gisJox ko gannaaw mel ni ku rus,Kima giseel a mat a xam.

    Wan na ma lal wan na ma bs,Noteel ma leen ci sama bs,Misaal ma leen ba ma ni mbas,Kima giseel a mat a am.

    Yaramu xol bi dafa mees,Jeena ba mel ni luu fees,Cofeel gi wal na ko mu tees,Kima giseel a mat a xam.

    Tibbub cofeelam dafa feesCi man, di fokki ak a reesCi sama xol, ba dootul yes,Kima giseel a mat a am.

    Moo tax mu def bu ma nee geesCi sama xol,mbaa mu ne gees,Sunu dig gante ne depees,Kima giseel a mat a xam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    22/44Jazbul Majzob - 21

    Dima xamal ta du ma ft,Dolli ma xam-xam bu rafet,Dolli ma ngm, dollima t,Kima giseel a mat a am.

    Di ma yaral boppam ma ygYar ba ci man, ba ma di ygLu ma ygul ne lu ma ygKima giseel a mat a am.

    Wan ma jamono na mu mel,Jngal ma xel, di ma bindalCi lluway maxfoosi xol,Kima giseel a mat a xam.

    Di teew ma teew ci peyi xol,Gisee mu taal ci lampi xel,Jum bu ma wan yoon wu u xll,Kima giseel a mat a am

    Jeeqel ma xel, rcceel ma xol,Xel du ne xol, xol du ne xel,Xela di xel, xol a di xol,Kima giseel a mat a xam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    23/4422- Jazbul Majzob

    Ruujal ma, ji, di ma bayal,Xiinlu, mu xiin ci niiri xel,Tawlu, mu taw ci tooli xol,Kima giseel a mat a am.

    Mu or di xam-xam yu rafet,Xam-xam yu ndul aki ft,Xam-xam yu dul yuy rkki t,Kima giseel a mat a xam.

    Sdde na ma ak xam lu rafet,Badu ma yr lu lu rafet,Ta du ma gis lu lu rafetKima giseel a mat a am.

    May na ma dggog moom i waxCi ay waxinam yu mu wax,Samay waxinay na mu wax,Ki ma giseeJ a mat a xam.

    Wan na ma boppam na mu day,Yllaa ko xam, moom la ko may,Ta wolu naa ni moo ma doy,Kima giseel a mat a am.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    24/44Jazbul Majzob - 23

    Wax na yonnent bi Iimu doon,May it, ma wax ko Iimu doon,Moom it, mu def ma Iima doonKima giseel a mat a xam.

    Nee na yonnent bi, yaw-a-yaw,May it ma wax ko yaw-a-yaw,Mu ni ko yaw, ma ni ko yaw,KIma giseel a mat a am.

    Buur ylla may na maw kaam,Ma di asaanam fu ma jm,Di tarjumaani lmmiam,Ki ma giseel a mat a xam.

    Lii le du puukare ci man,Dafay ngrm lu war ci man,Ta may grm ki gn ci man,Ki ma giseel a mat a am.

    Mayam yi, yaa na, du nu xul,Cofeel gi, rew na su nu xol,Ba doggi reenam, su nu xolRootul lu dul wanew taggam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    25/4424- Jazbul Majzob

    Am na ci yoy, du nu ko wax,Am na ci yoy, nun mu ko wax,Ak bako, noo yamoo ni wax,Lay dggi xol, tay dolli ngm.

    Wuutu na saaba ya, a wy,Ca la bokkoon ta mujj a wy,Fab nan nd ak moom di wy,Du nu ni wuy kanamam.

    Da koo jkkal, far koo mujjal,Muy kun mujjal, tay kun jkkal,Taal bu fayul la far jafal,Daay gu maneefulug fayam.

    Buur ylla sdde na nu lii,Lu jiitu nun, xam na nu Iii, .Te yrmandem jiitu na IiiCi nun, ba war nanoo grm.

    Leerug yonnent bi la def,Mu juuri leeram ku ko saf,Mu ubbi xol ba, ba mu af,Dugal ca xam mbiri sangam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    26/44Jazbul Majzob - 25

    Yawma alastu naka laaj,Nu ni ko waaw, ta de xaaj,Booba la door ni nanu waaj,Ta daal nu fay yeni yenam.

    Sunu yonnent moo jkke waaw,Naka ni waaw, nu daal ni waaw,Soppeeki ba, ku ne ni waaw,Tay dglu baa ndiglam.

    Ruu yi jungaama ndax ragal,Yee ak cofeel di len ygal,Am na keroog u nu xamal,Xam-xam ba tay la u ka xam.

    Yonnent bi booba la nu wanKanam i gn booba la woon,Booba la seex meeel woon,Murid yi booba Iau am.

    Booba la bamba gae woon,Booba la waayam falu woon,Baax gi tay, booba la woon,Lu ne ci nit, nee na ak jkkam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    27/4426- Jazbul Majzob

    Lii le nu tektal ba tay ,Ne ab sri du ku u jey,Ku beru mel ni aji say,Ju dddu reenug garabam.

    Baaxug keroog-ay law ba tay,Bonug keroog itam du moy,Lawoon keroog-ay wy di wy,Lu ne di teeri fa mu jm.

    Na waay meloon, mooy Ii tay,La waay amoon, mooy Ii tay,La waay xamoon, mooy li tay,Buur ylla, yem naa kanam.

    Ku ylla wan boppam, mu gis,ku ylla yiir boppam, du gis,ii di ko gis, uu du ko gis,Mooy i ko rere, ak i xam.

    Buleen di siis, buleen aaanBuur ylla yaa na, na ko aan,Kaaan dafay soppiku jaan m,luggeil m-mam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    28/44Jazbul Majzob - 27

    Jileekuleen, aaane leen,Aaane kuy xy jublu leen,Di wut a jub, Far dddu Ieen,Dkki faneen palam-palam.

    Jafanduleen tay dgral,Buleen yolom, kiy dgral,Buleen ko wax yolomalal,Ku yolomal, daal di yolom

    Ku la gnal ki la gnal,Moo la gnal ka la gnal,Ki la gnal ki la gnal,Moo mat a xam, moo mat a am.

    Srin bi gn ki ma gnal,Moo ma gnal ki ma gnal,Te moom mi gn ki ma gnal,Ame ma may, mayu yaram

    Jaayante na ak moom ba matal,Biteeki biir ,ku ma jiital,Mooma, ba kenn du ma ljal,Xol bii la fab, joxub xolam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    29/4428- Jazbul Majzob

    Waxtaan na ma ak moom ba matal,Waxtaan xol wu kenn ygul,Bu ne mu tbbi sama xol,Mu yombalal ma ak xamam.

    Yawma alastu, ba tay,Masu la tggoog dinu may,Di yari ruu booba ba tay,Diggante ndigg aki ruuwam.

    Xam turu taalibeem bu doy,Xam seeni baay ak seeni nday,Xam seeni kr ak nau day,Ku ne mu raaley mbiram.

    Xam a mggante, ak a fayJiitu di toante ba tay,Xam ku u taal ba dootul fay,Ak kok du tkke i, ba dem.

    Xam aji wopp, ak aji wr,Ak ku u fajtal ba mu wr,Xam aji toppeeg ku u ber,Xam fa u dooreeg fa u yam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    30/44Jazbul Majzob - 29

    Fekkoon u feeu ko ba fee-al ko ca biir, far ko fa fee-atal, mu xam ba i, ba fee,Kasful ko ypp kanamam.

    Kiiraay ya de, ba set ni wecc,Lu diy pakkam u boole tojjKo, snni ypp, koote ga tojj,Ngir ma ni saww, di am ngiram.

    Mu xam boppam ak aka topp,udaal di jl yf ya ni kupp,Mu ne di sbbaa ak a tuub,Te xam gannaawam, xam kanam.

    Buur yll xamloo ko la woon,Ak la xewoon, ta di la woon,Ak la di woon ,ta di la woon,Mu far saxal lu new bindam.

    Booba mu def ko ni badar,Bu fee ci laylatul xadar,Raaan di sabbaa ba fajar,Ci asamaani barsqam,

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    31/4430- Jazbul Majzob

    Mi diggante kursi, akArs, aki by naari ,akTuraa bi, ak awaa-i, akMaa-iiki, law i, ak xalam.

    Moo tax ma xy di leen ygal,Seen mboole tay lu ngeen ygul,Ba far ci woo i dikkagul ,a bgg a w, i bgg a dem.

    Ndax Ii uy yarngi, ma jog,Ta far si gan ku g,Ta aguwul, ta bgg a ageneen, ta xam-xamlu du xam.

    Ta sama woote bii, ku xyMu tbbi ab noppam, ta muyTanxamlu, def boppam ku doy,Xolam ba, mbaa lakkul ba xm.

    Lu diy muqddam laa di woo,Ku di allaaji maa ko woo,Mbooleeki seex, ku ma ci woo,Na ni labbayka, mbaa naam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    32/44Jazbul Majzob - 31

    Di leen ygal kii ma gis,Ta kii ma gis, ku ko gisTa andulook moom, ka nga gis,Gnu , mbaa saful xorom.

    Na ngeen ma laaj ki ma gis,Sangu b jamono laa gis,Daalleen di nd ak ki ma gis,Bu kenn ni dggumaw turam.

    Sayxi suyooxi Axmadaa,Kii moo nu tektal Axmadaa,Ta di ka Muxammadaa,Ba mu tbbal ko biir kram.

    Tampeel ko tampeb ngrmam,Ni ko yoxos ci biir xolam,Digal ko baa ndiglam,Fal ko ci kaw lalub palam

    Ne ko ykket wane, i xamAk i xamul daal di ko xam,Jiital ko muy muxaddamam,Daal di taxaw seen kanam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    33/4432- Jazbul Majzob

    Junjung ya gor ci asamaan,Suuf sa di rkk peyi diiwan,Sase, ta naa xutbusamaanMoo falu nd aki dagam.

    Rijaalu xybu dajaloo,Ba mel ni weer yu tegaloo,Boroomi leer di tegaloo,Fu u fa fee soreeg lndm

    Mbooloo yi wutsi ko di wal,Ta daal di tuub, njbbal ma dal,Ndndam ya rkk ci wpp wall,Wayam wa riir fu u fa jm.

    Werante de koote ga toj,Ku ba, nu tjj, mbaate u tojjKram, mu far mel ni ku aj,Kangam ya waaf kanamam.

    Boroomi giir ya jiitu woon,Ak seni giir, ta oo rawoon,

    jbbal ko giir ya u awoon,Booleeki wrd ya u am.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    34/44Jazbul Majzob - 33

    Xaadiru agsi, ni ko am,Tiijaani agsi ,ni ko am,Salsali agsi, ni ko am,Dabbaa-i agsi, ni ko am.

    Jaayante faak moom, di ko wanYene, ta ngeejoo fekke woonTay, ba muritu ko, di sant,Fi gannaawam ak oam.

    Mbooloo ma naa ko yaa gn,Wii waxtu, yaw la u tnn,Yaay nu, yaa y ki u n,Tinu kuy fekke ta gm.

    Buur ylla yaw la wcce tay,Yaa e mbir yi ba tay,Smmal njaboot gi, ku la fay,Fase du sy diirug dundam.

    Ku dglu Iii, na xam ni IiiYllaa ko def, ku fekke Iii,Ta dddu, far dummooyu Iii,Defu ko kenn, lu muy boppam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    35/4434- Jazbul Majzob

    Gumba gu nanaaral, taxulMu gis badar, ba tay gisulJantu bccg, bu u wurilYoor-yoor, mu jakkaarloog jem

    Ta gumba nag, ba gumba jee,Gumba ci xol, mooy waxju jee,Yal nau am gis boob du jee,Ci b xol, ay yuy kanam.

    Buur ylla mooy wane, bu kennDefe ne boppam a ko wan,Gis ki le, ab cr la ba woon,Buur ylla mooy joxey mayam

    Ku fekke kii, ta fekki kii,Texe na i, ba fee, te kii,May la gu Ylla maye, kii,Des na ak i des, nd ak i dem

    Xutbusamaan a ngii bu mat,Jogleen ddiya yi na mat,Ku jem a gntu na ni mo,Di wy ta xaml fu mu jm.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    36/44Jazbul Majzob - 35

    Addiya tay moo ka jagoo,Ku def ni moom, di ko jagoo,Ku ko deful, bu ko dogoo,Byyil mu e ay mbiram.

    Lu tax ddiya moo ko moom,Laay bgg a wax, ta mooy boroom,Moo ko jagoo, du seen moroom,Neleen gannaaw, mu ne kanam.

    Yf ya ca biir ,ak Ii u gis,Ta liu gis, mooy liu gis,Biral gi mooy, bt yi ko gis,Noppal na mbokki lammiam

    We waa ngii, tay xee ak a dorBoroom we waa ngee, gn a wor,Ba jaan, ta gis des wa di dorDu tere jaan duggum kanam.

    Yf ya ca biir nag ku ko xam,Na daal di doyloo la mu xamKu ko xamul ma wax mu xamJbbal ko ruuwug bakkanam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    37/4436- Jazbul Majzob

    Kuy faatu moo fay jkk a teewuy jullee mu di fa teew,Bu uy rob, mu nd ak oom di teew,u dem, mu des tontu layam.

    Seetleen na ngeen di jbbalo,Bii tng, tngub i jbbalo,Gis am wu neex, ta mosulooKo, xawma man luy njariam.

    Fekke ju mel ni wuute, mooyFekke jamonay ngiir ta sooy,Du def lu dul xoole ni looy,Di rccu, tay mum tuam.

    i sobu, raw ngeen seeni maas,i ba, na uy ee seeni maas,Gaal gaa ngii, jgleen aani paas,Ku yex ba tarde da ko xam.

    Xamleen na ngeen di aane nag,Gm, ak yaroog, toroxlu, agBakkan, ta mu, sax fa ba g,Ba lang, yamoog ndigl ba xam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    38/44Jazbul Majzob - 37

    Wolu dggal, ag rafetalNjort, ta set fas-fasi xol,Loo xcci, loola daal di dal,Muy i, ba fee ; na ngeen ko xam.

    Danaa biral ci lima fas,Tuu ci xutbu bi ma fas,Ni mooma doy, ta Ii ma fas,Doy na du i, mang ca kanam.

    Fii, du barab, faful di kr,Fas ji ci moom, dara du mbir,Keram gii, naaj la kat, du ker,Lemam di nga mu wex xorom.

    Mddm mi, tan yi di ko biiw,Bawkat yi siif ko, di ko yew,Di dox di xiiro, ba mu siiw,Tab lay bu dee taa, daal di dem.

    Krug ku dul am kr la fee,Moo tax ma dddu, jublu fee,Li tax nu jg, du i, ma fee,Foofee la soxlawoo oam.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    39/4438- Jazbul Majzob

    Ta tay ma jngal leen, nauyFaseg njulit, xy byyi moy,Ta xam ni, jkkam wa, du moyBoroom, ci kangam, mbaa dnnam.

    Ta seede yaari baa see -Deyi, ta fas sellal, ta see-Deloo ko, buur bu doy bi see -De, ci lu leer ak lu lndam.

    Ta dddu dduna, ta wutSeri bu mat seri, ta at -Tani yenam, ta bul tawatBenn, lu dul ay tawatam.

    Ta kooka, mooy Bamba, buleenDese ba jg wu keneen,Ba rer ci manding mi, du ngeenTaseeg ku dindi seen nglam.

    Def leen ni man, dama ni man,Labbayka Bamba, maa ngii man,Fukki barab, ma teg ca benn,Fu u fa tollu, maa la gm.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    40/44Jazbul Majzob - 39

    Bakkan bu dee tggoo di waaj,Saafara de, aki gllaaj,Soppe bi yaw lanu fa laaj,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Bu ruu di xar-xarle ba dal,Malaaka agsi di bgal,Soppe bi yaw lanu ndal,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Bu ruu di rocciku ba naaw,Jm asamaan joxe gannaaw,Soppe bi, yaw lanu fa aaw,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Bu u nee cas yaram di rob,Rawmaan ni jaas, du nit, du rab,Soppe bi, yaw lanu fa b,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Bu aari gaaa nee jale,Di laaj ka neex, ngani jale,Begal u mbg moom dootu de,Ylla ak sa barke, maa la gm.

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    41/4440- Jazbul Majzob

    Keroog ba uy dekki ba xy,Jm by ndandoo di wy,Kerogg a tax nga doy nu tay,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Keroog ba uy taxaw, ta kennDu fa ni riis tankam, ta kennDu nga lu dul lu mu nekkoon,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Bu tere yay rot, si dign-Te yaari wet yi, mel ne tanYuy dal, ta kenn du rere benn,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Bu uy tral mandaxe ii,Seen yiw wa wat, u gane ee,u gae leen, u ee fa ee,Ylla ak sa barke, maa la gm

    Geppn ba, buy sampu ta mooySiraat, ku jggi mbir ya nooyFa moom, ta dootu de di nooy,Ylla ak sa barke, maa la gm

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    42/44Jazbul Majzob - 41

    Keroog ba mbooloo ma nee rcc,Di sddaloo def naari pcc, .Bsub keroog yal naa la daj,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    u daagu jm Daaru Salaam,Di xy di joxante salaam,Fu ne nu deyaale ak salaam,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Soppe bi, yii laa fas ba w,Yaakaar ci ylla, ak ci yaw,Texe gu sax, du de ba faw,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Maa ngi taxaw sa gannaaw,Jublu la, jox aneen gannaaw, .Foo mn a jm .yobbu ma gaaw,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Ku sdduwul, man sddu naaKu fdduwul, man fddu naa,Ba matlu, weesu naa danaa,Ylla ak sa barke, maa la gm.

    Seex Abdul Kariim Samba Jaara Mbay(1868 -1917)

    Radiy-Allaahu Anhu

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    43/44

  • 7/25/2019 JazbulMajzoob

    44/44

    1436 h / 2014 www.drouss.org- Tous droits rservs

    http://www.drouss.org/http://www.drouss.org/